21/08/2022
😇 Hakasaa boroom Chukoori...💌
✍Les Poèmes du Guide
Poème de CHEIKH AHMADOU KARA MBACKE NOREYNI dédié à :
SHEYQ AL MUNTAQÂH MUHAMMADU
(Traduit en français)
BismiLÂHI MOOM miy may jaam bam tal a def dara
As Salâtu wa Salâmu alâ NABIYIHI mey dara
Wa Âlihî wa Sahbihî wa qayri QADÎMIHÎ
ASHEYQ AHMADA-BAMBA, BÀLLA-AYSHA, MOO di dara
ASHEYQ SEYDIL MUQTÂR ma dëddu ca àllarba ja
Am juròom-ñaar i at ci Qilâfah gi, moom laa di saraa
YÂL’na ko KU-TEDD-KI teer’og Leer i SËRIÑ-BÂRA
Nangul ko ay jëfam ci Yoon wi, mooy doom i SËRIÑ-BÂRA
Ki ko wuutu tay, ku ñu taamu, KU-TEDD-KI yàggal ko fi
Ba « Qayra anânu » ja MAAM wax, mu doon ca dara
Bu fi yàgg’ee te am wér, waa Réew mi da nañ kontaan
Ku am ci Leer yi ci aw Turam, yaw dootoo ñàkk’ati dara
Mîm, Nûn, Tâ-toombe, Qâf, Lîf-gu-aj, yanarâh
AL MUNTAQÂH di Octogone, Tur wi daa laamboo dara
Te 15 mooy 6, kon dey doon Jihâdu-Sitta
Est, Ouest, Nord, Sud, haut, en bas, lii mooy dara
Alqames u ëllëg’ay doon sa f**k i fan ak juròom
Ci bòpp u Qilâfah gi, YÂL’na nga sòttal dara
Âmîna bijâhi AHMADAL-QADÎMI, MOOM mi la fi teg
Bu la ay cat jage fenn, bu dara man ci yaw dara
Nangul ma tay jii ma doon Alkaati Mûridîyah
Tur u Général bi jox naa la ko Âddiyah yaw, man du ma dara
Nangul ma ko ngir sa MAAM Mi la fi teg tem fongk la lool
Def ma nii MU ma def ba tax ma di niru dara
Jaayaante naa’k Yaw tay ci Tool u BAMBA-Fépp
Fas yéene ligéyal YOON wi, ndax jëf rekk moo di dara
Da mey takk’aat sama laxasaay, maa dib Soldaar i BAMBA
Di nekk sa Alkaati buy geetaru, te neh du ma dara
Doonoon naa fi ab xaj bub SËRIÑ-TÛBÂ bu daan baw
MU sòppi ma gaynde gu daan ŋaree nu ne aw TURam, dara
MU may ma mey kar ndaw ñiy taañañal, tañax-tañax i
Ba ñëw ci BAMBA-Fépp, ngir xam ne lii MOO di dara
JËRËJËFE SËRIÑ-TÛBÂ la gone yëpp’iy foyee
MOO ma may ma siiwal ko ci ndaw ñi, ndax MOO di dara
Jaamu-YÂLLAH gog dara man u koo yàxx
Ndax IMÂM-AKBAR moo neh : « Sax leen ci, MOO di dara »
MBÀKKE, tay jii, fii laay yem ba beneen yoon
Dégg ma, te nangul ma lii mey ñaan, donte tekki wu ma dara.
Weer i Ramadân (Mai) 2018
ODES À CHEIKH AL MOUNTAKHA MOUHAMMADOU
Au Nom de DIEU, LUI qui accorde à l’esclave à disposer de l’action
Prière et Salut au MESSAGER qui est le Signifiant
Sur Sa FAMILLE, Ses COMPAGNONS, ainsi que Son Meilleur SERVITEUR
CHEIKH AHMADA-BAMBA-BALLA AÏCHA est l’Objet en question
À CHEIKH SEYDIL MOUKHTAR qui s’en est allé en ce Mercredi
Suite au règne de sept années, c’est à lui que je chante
DIEU fasse le SAINT l’accueillir par les Lumières de SERIGNE BARA
Acceptant ainsi Ses Actions vouées au service de la VOIE, il est descendant de SERIGNE BARA
Son Successeur, un Préféré auquel nous demandons au SAINT-HOMME de lui accorder la vie longue
Dans les « Bienfaits providentiels » annoncés par le PATRIARCHE, qu’Il soit impliqué
S’Il vivra longtemps et bien portant, sera heureuse la Nation
Qui obtient de Ses Lumières, plus jamais ne sera un démuni
M, N, T, KH, A accent circonflexe, Y
AL MOUNTAKHA au chiffre octogonal, le Nom est vêtu de mystères
Aussi, le nombre quinze est la somme de six, constituant les points cardinaux
L’Est, l’Ouest, le Nord, le Sud, en haut et en bas, ceci est la Substance
À demain jeudi sera le quinzième jour
Au chevet du Khalifat, DIEU fasse le parachèvement de Ton Œuvre
Amen au Nom de AHMADAL KHADIMI, LUI qui T’intronisa
Sois préservé de la guigne, que rien ne puisse agir contre Toi
Accorde-moi en ce jour, à devenir le Policier de la Mouridiya
L’appellation de Général, je T’en fais don en guise de addiya, quant à moi je ne compte pas
Accepte de ma part, au Nom de Ton AÏEUL et MENTOR, tenant beaucoup à Toi
Qui m’a façonné tel que je suis, au point que remarquable je sois
Je m’engage envers Toi à cette date, dans les domaines champêtres de BAMBA-Partout
Par la ferme décision d’œuvrer au profit de la VOIE, en conséquence seule l’Action compte
Je m’en vais, de nouveau, m’attacher la ceinture bien serrée, en tant que le Soldat de BAMBA
Au rôle de Ton Agent de police harnaché, sans rien d’autre, me disais-je à moi
Jadis, je fus le Toutou de SERIGNE TOUBA aux aboiements
Qui me transforma en lion rugissant Son NOM de toutes les façons
IL me permit de dévier les jeunes par l’ouverture et la tolérance
Les attirant alors vers le BAMBA-PARTOUT, sachant que ceci est la Question cruciale
« MERCI à SERIGNE TOUBA » est le Cri-de-cœur de la jeunesse
IL m’accorda sa propension au sein des jeunes, car il s’agit de la Quintessence
Un Acte de dévotion hors de portée à toute nuisance
Car le GRAND IMAM déclara : « Enracinez-vous en Cela, c’est bien la Chose substantielle »
MBACKÉ, pour aujourd’hui, je vais m’en tenir là cette fois en attendant la prochaine
Entendez-moi, et agréez ma requête, malgré l’insignifiance de ma personne.